Wikipedia
wowiki
https://wo.wikipedia.org/wiki/X%C3%ABt_wu_nj%C3%ABkk
MediaWiki 1.47.0-wmf.7
first-letter
Xibaarukaay
Jagleel
Waxtaan
Jëfandikukat
Waxtaani jëfandikukat
Wikipedia
Wikipedia waxtaan
Dencukaay
Waxtaani dencukaay
MediaWiki
Waxtaani MediaWiki
Royuwaay
Waxtaani royuwaay
Ndimbal
Waxtaani ndimbal
Wàll
Waxtaani wàll
TimedText
TimedText talk
Module
Discussion module
Event
Event talk
Senegaal
0
1663
107613
106861
2026-06-18T00:34:15Z
InternetArchiveBot
12803
Rescuing 3 sources and tagging 0 as dead.) #IABot (v2.0.9.5
107613
wikitext
text/x-wiki
{{Infobox Réew
|tur=Réewum Senegaal
|raaya=Flag of Senegal.svg
|kóót bu aarms=Coat of arms of Senegal.svg
|lonkoyoon=LocationSenegal.svg
|gox=[[Afrig]]
|yaatuwaay=196,723
|way-dëkk=18,593,258
|fattaay=59,26
|péy=[[Ndakaaru]]
|tus-wu-gaar=14/43/29.06/N
|tus-wu-taxaw=17/28/24.06/W
|nguur-gi=[[Pénc]]<br />[[Basiiru Jomaay Fay]]<br />[[Usmaan Sonko]]
|moom-sa-réew=<br />[[Faraas]]<br />20 ut 1960
|turu way-dëkk=Senegaal-Senegaal<br />Saa-Senegaal
|làkku=[[Faraañse]]<br />94% dinañ wax [[wolof]]<br /> [[pël]], [[séeréer]], [[joolaa]]
|koppar=[[Franc CFA]] ([[XOF]])
|tegtalukaay=+221
|lonkoyoon2=Senegal carte.png
}}
'''Senegaal''' menn la ci [[réew]] yi ne ci [[Sowwu Afrig]], mu bokk nag ci [[Afrig gu bëj-saalumu sahraa|Afrig gu bëj-saalumu saxraa]] (Afrique sub-saharienne), [[Mbàmbulaanug Atlas]] diw digam ci sowwu, taqaloo ak [[Gànnaar]] ci bëj-gànnaar ak penku, [[Mali]] féete ko penku, [[Ginne]] ak [[Ginne Bisaawóo]] ci bëj-saalum, [[Gàmbi]] moom sos ab daanaka-jiba (quasi-enclave) ci biir Senegaal, sutuxlu ba ci lu ëpp 300 jñ (km) ci biir suuf yi. Duni [[Bopp bu Nëtëx]] bi (Cap-Vert) ñi ngi ci 560 jñ ci tefesi Senegaal yi.
Réew maa ngi duppe aw turam ci dex gi ko peeg ci penku ak bëj-gànnaar, te ab balluwaayam bawoo ca [[Fuuta Jallon]] ca Ginne, di [[Dexug Senegaal]]. [[Njuux li|Njuux]]<nowiki/>am lu gëwéel la te di lu fendi te yor ñaari jamono: jamonoy nawet (jamonoy taw) ak ju noor (jamonoy fendi).
Ci jamonoy canc gi (la période coloniale), ay digg yu yaxantu yu bari, yu ay [[imbraatóor yu canc]] (empire coloniale) moomoon, daal di woon nañuy sampu ci tefes gi gépp. Dëkkub [[Saint-Louis (Sénégal)|Ndar]] mujj na di péeyub [[Afrig gu Sowwu gu Faraas]], mu mujj juge ci di leegi [[Ndakaaru]] ci [[1902]], moom Ndakaaru nag mujj na di péeyu Senegaal ca ba mu jotee ca ag tembam / jonnam ca 1960, nekk ci cat li gën a féete sowwu ci [[Afrig|kembaarug Afrig]]
La dale 2012 ba fii mu ne [[Maki Sàll]] mooy njiitul réew ma. Senegaal ak donte bokk na ci càmpéef yu bari yu àdduna si, teewul bokk na ci [[Bennoo gu Afrig]] (Union africaine) ak [[Mbooloom diiwaan yu Sahel-sahraa|Mbooloom diiwaan yu Saxel-sahraa]] yi (Communauté des États sahélo-sahariens)
Senegaal nag yaatoo na 196.190 jñ<sup>2</sup>.
== Gongikubaat ==
Cosaanul turu Senegaal dañul di jeqi dàggasante ak werante. ca [[1850]] labbe bii di [[David Boilat]], ca ''mbindam ya mu doon def ci Senegaal'',daa gisoon ne Senegaal mi ngi juge ci waxiinu [[wolof (làkk)|wolof]] wii di ''suñu gaal''. Bii nag mooy gis-gis bi gën a siiw, te xibaarukaay yi (les médias) gën koo ame. te moone lu ñu nangoodi la te sikk ko la ko dale ca [[ati 1960]], ay gongikubaat yu bari nag joxe nañu leen, ci misaal biy taf [[cosaanul tur wi]] ci ag giir gu [[berber]] gu [[Sahara]], mooy giirug [[Zenaga]] walla Sinhaaj, naan: Turu Senegaal mi ngi bawoo ci tudd gu waa [[Portigaal]] yi doon tudd turu giir googu. Waaye werante wi dañul di tàng ci loolu ba tay.
== Njëkk-taariix ==
{{Xóotal|Taariixu Senegaal}}
[[Dencukaay:Wassu Stone Cirles shaunamullally 02.jpg|200px|vignette|droite|Xeer yu mag yi(Mégalithes) di ay jeexit yu [[Séeréer]] yu [[Ñooro]]]]
Lu ci ëpp [[Njëkk-taariix ci Senegaal]] day tudd - ba laa tudd lenn - '''gëwéeli xeer yu mag yi''' (walla les cercles mégalithiques) yu Senegàmbi yi, walla '''jóori xor yu ñu sàkk yi''' (les amas coquilliers artificiels), yu ci mel ne ya nekk ca dunub Faajut.
Jàpp nañu ne Senegaal dëkkees na ko ci njëkk-taariix lu jiitu lool juddug [[Isaa]]. Ay doj yu ñu yatt yu [[Jamonoy doj wu ñu yatt]] ju njëkk ja(Le Paléolithique inférieur ), wuññees na leen ci daanaka-dun bu [[Bopp bu Wert]] bi (Cap-Vert) ak yeneen yëf yu gongikoo ci doj, ñu jekkal leen, dees leen di fekk ci diiwaanub Tëngéej ak ci pegi dexi Senegaal gu penku gi.
Ci [[jamonoy doj wu ñu xacc]] (néolithique), jumtukaay yi tàmbali nañoo soppiku ak a wuute, bu ko defee '''suuf su ñu togg''' (walla céramique) daal di feeñ. Gasi gëstu ya ñu doon def ca diiwaani tefes ya feñal nañu ay desiiti waañ yuy seere ak a firndeel askan wu mag wu ay nappkat aki yaxantukat wa fa nekkoon (marigot bu Xant ca delta, sottikukaayu dexug [[Saalum]]).
Ndefarug mbell (walla gu weñ (metallurgie)) jëm na kanam ci [[jamonoy mbell yi]] (protohistorique) (junni bu ngëkk bi njëkk [[Isaa]]), fi ñuy gis ay bàmmeel ci bindu ay [[mbaanaar]] (tumulus). Ci digg réew mi, fa tollook [[Gàmbi]] gu tay gii, dees na fa fekk mbooloom gëwéeli xeer yu mag (cercles de mégalithes) ci aw dog wu tollu ci 100 jñ ci kaw 250|jñ.
=== Nguur yu njëkk ya ===
[[Dencukaay:Senegal-reine-du-walo.jpg|vignette|[[Ndeté Yalla]], lingeerub [[Waalo]]]]
Dëkksi gi dafa doon gën di dolliku ndànk-ndànk tey gën di dëgër ngir àgg ci sos ay nguur yu njëkk yu sosu ci VIIeelu xarnu, nguur gu [[Tekruur]], gu [[Namandiru]], gu [[Jolof]], ak ay mbokkoo yu sori ak [[Iimbraatóor gu Gana]], ci suufus [[Mali]] gu tay gi. Ci nguur yu wuute yooyu, gi ci ëppoon doole ci XIVeelu xarnu moo doonoon imbraatóor gu Jolof, gi boole woon [[royaume de Cayor|Kajoor]], [[Bawol]], nguuri [[séeréer]] yu [[Royaume du Sine|Siin]] ak yu [[Royaume du Saloum|Saalum]], [[Waalo]], [[Fuuta-Tooro]] ak [[Bambug]]. Ci bëj-saalum, nguurug [[Kaabu]], teg ci gu [[Fulaadu]].
[[Jolof]] nekkoon na imbraatóor gu [[Njaajaan Njaay]] sosoon, ki njëkk a nekk Buurba (buur) ca Jolof. Faleesoon na ko njiit ca loolu doon mujj di [[nguurug Waalo]], ca bëj-gànnaar-penku gu Senegaalug tay gii, ca diiwaanu dex gi. Dajale woon na mbooleem askani giirug [[wolof (peuple)|wolof]] ngir taxawal imbraatóor gii ci XIIIeelu xarnu . Ibraatóor gi saayoon na te naaxsaay ci [[1549]], ànd ak deeg imbraatóor ba mujjoon ca [[Jolof]], Lele Fuli Fak, ki ko rayoon di Amari Ngóone Sabel Faal, ki nekkoon ca jooja jamono kilifag diiwaanu [[Kajoor]].
Jolof des na di aw dog (vassal) ñeel [[imbraatóor gu Mali]] ci diir bu tollu ci xarnu. Ba loola amee, yeneen nguur yi, ñoom itam gu ci nekk, tàmbalee jël ag tembam ba mujj wàññi imbraatóor gu Jolof gu mag googu ba àggal ko ci tolluwaayu genn nguur gu yam ca digg réew mi. Ci ñaareelu xaaj bu XIXeelu xarnu, sancaani Faraas yi (les colons francais) tàmbali woon nañoo nangu ndànk-ndànk mbooleem nguur yu Senegaal yii. Jolof moo nekkoon nguur gi ñu mujj a nangu ak Buurab Jolofam bu mujj ba [[Alburi Njaay]], ci ron deflu gu [[Luwis Federb]].
[[Lislaam]] a ngi njëkk a tàbbi ci Senegaal ci diggante VIIIeelu xarnu ak IXeelu xarnu, ña ko fa dugal di ay yaxantukat yu araab-yu-berber. Dañu doon tas diine jii ci jàmm, ñu njëkk koo jox [[Jula]] yi tuubloo ci ginaaw bi [[Tukkloor]] yi ak [[Soninkés|Saraxule]] yi, ñoom itam ñu tas ko ci Senegaal gi gépp. Bi ñu demee ba ci kanam ca XIeelu xarnu , la [[Muraabituun]], jug, Tukkloor yi jàpple leen, ñuy jéem a tuubloo mboolooy jaamukati xërëm yi jaare ko ci [[Jiyaar]]. Loolu benn la ci sabab yi tax Séeréer si gàddaayoon dem [[Siin-Saalum]], Wolof yi, [[Pël]] yi ak [[Mandinke]] yi, te ñoom ñepp ña nga jalu woon ca [[Tekruur]]. Lislaam teel na tas ca imbraatóorug Jolof. Waaye ca XIXeelu xarnu la nangu ca dëgg-dëgg mbooleem askan yi, ci anam gu jàmmu, loolu nag deesi sante ko Sëriñ si, ku mel ne [[Seex Ahmadu Bamba]], mi sos yoonu [[murit]], [[Alaaji Maalik Sy]] kenn ci kilifay [[Tiijaaniya]] walla [[Seydina Limaamu Laay]], ki sos [[laayéen]] gi, ñi yéemoon nit ñi ci seenug mbaax ak ragal Yàlla ak séeni karaama( xar-baax). Moom Lislaam tam nekkoon ab ker-keraan (moyen) ngir boole nit ñi te di leen aar ci jalgati yi ñu miinoon ci nguur yi ([[jiyaar]] yu toftaloo, canc gu ñu teg ci doole, jalgatiy [[Ceddo]] yi).
XIXeelu xarnu ñi ngi ko gën a xame ci daanug nguur yi, jàllsig sancaan yu Tugal yi ( colons européens ) ak jàmmaarloo gi lànk canc gi, ñi ko jëmmal di ay nit ñu mel ne [[Lat Joor]], [[Alaaji Omar Taal]], [[Mamadu Lamin Darame]], [[Alburi Njaay]] walla [[Màbba Jaxu Ba]]. Diiney [[katolig]] (walla nasaraan, ndax katolig bànqaas la ci nasaraan) daal di tasu, ñi ko def di ay nasaraanalkat yu Tugal la ko dale ca XIXeelu xarnu, rawati na ca Siin ak [[kaasamaas]].
== Taariix ==
[[Lislaam]] tàbbi na Senegaal ci fukk ak benneelu xarnu,ànd ak giirug Sinhaaj gu [[Amaasix]] gi. Turu Senegaal waxees na ne mi ngi bawoo ci tudd gu waa [[Portigaal]] yi doon tudd turu giir googu. Askani Senegaal yi sos nañu ay nguur aki nguur-nguuraan, yi ci ëppoon solo di Imbraatóor gu [[wolof]] ca diiwaani [[Waalo]], [[Kajoor]] ak [[Bawol]], ci fukk ak ñeenteelu xarnu g.j, ak nguuruñg [[Tukklóor]] ak gu [[Deñaanke]] gu [[Pulaar]] gi ca penku bëj-gànnaar ga. Ay dooley [[Tugal]] teg nañu loxo ay wàll ci ay tefesam, ci fukk ak juroomeelu xarnu g.j, ginnaaw bi Faraas daal di teg loxo réew mi mépp, ginnaaw ay xare yu limu. Ci atum 1902 la [[Ndakaaru]] nekke [[péey]]ub [[Afrig]] gu [[sowwu]] gu [[Faraas]] gépp.
Seŋoor walla [[Léopold Sédar Senghor]](1906-2001)(1960-1980) mooy ki njëkk a nekk njiitul Senegaal, yoroon dàkkantalu njiit liy woykat (walla taalifkat)
Ci samwie 1959, la Senegaal bennoo ak li ñu daa wax Sudaan gu Faraas gi, ci ron turu [[Lëngoo gu Mali]] (fédération de Malie). Lëngoo gu Mali googu tembe na ci Faraas ci 20 suwe 1960. Waaye ginnaaw ay jafe-jafe yu politig, Lëngoo googu mujj na di ñaari réew ci 20 ut 1960: Senegaal ak Mali. Jibaleesoon na ag lëngoo ci diggante Senegaal ak Gambi ci turu Senegambiya atum 1982. Waaye ci jëf feeñul, bu ko defee ñaari nguur yi tàggalikoo atum 1989. Am na ab jë bu ngànnaayu (front armé) bu nekk ci bëj-saalumu réew mi, ca Kaasamaas bu bëgg tembteg diiwaan ba, leeg-leeg mu xareek nguur gi, la ko dale ca atum 1982.
_
=== Canc gi ===
[[Dencukaay:SignaresBal.jpg|vignette|gauche|Feccum [[gurmet]] yi (signares) [[Saint-Louis (Sénégal)|Ndar]] (sotti gue [[1890]])]]
Sancaan yi (les colonisateurs) seen teg loxo gu canc gi (conquête coloniale) mi ngi door bi [[Grandes découvertes|wuññig suuf]] yii amee ci [[1442]] ci loxol moolub Veneto (ab diiwaan ca Itaali) bii di [[Alvise Cadamosto|Cadamosto]], bi mu defalee ay wuññi ñeel Portigaal. Ca jooja jamono la waa portigaal daal di sóobu - ci lu gaaw - ci [[Njàppum jaam]] (walla jaayug nit ñu ñuul ñi), waaye doon nañu war a janook gëpplante (la concurrence) gi bawoo woon ci jaaykati ñu ñuul ñi te bawoo woon Britaani (négriers britanniques), Faraas ak Olaand ca [[Yaxantug ñatti-koñ]] ya (Commerce triangulaire).
Waa Olaand yi sos nañu ab diggub yaxantu ca dunub Gore, [[Faraas]] taxawal ca [[1659]] digg bii di bu [[Saint-Louis (Sénégal)|Ndar]] nga xam ne moo mujj di péeyub Senegaal bu njëkk bi. Ci [[1677]] waa Faraas ñi ñëw nangu [[dunu Gore]] (benn ci digg yu mag yi ñu daa jaaye [[jaam]] yi ak [[Saint-Louis (Sénégal)|Ndar]] ak tata ju [[dunu James]] ca [[Gàmbi]]).
[[Dencukaay:TirailleurMarseille1913.jpg|vignette|Benn [[tirailleurs sénégalais|sànnikat]] ak njabootam cig jaar ca[[Maarsaay]] atum [[1913]]]]
Nosteg canc daal di nay taxaw ci dikkug [[Louis Léon César Faidherbe|Federb]], Kaŋub Senegaal (le gouverneur du Sénégal) la ko dale ca [[1854]] ba [[1861]] ak [[1863]] ba [[1865]], mooy ki samp dàtti [[Afrig gu Sowwu gu Faraas gi]] (ASF)(AOF). Ci wormaal gi mu defoon aada ya fa cosaanoo ( du dëgg, wormaalu ko fenn) la tàllale jeexiital (l'influence)gu Faraas ba mu weesu Senegaal, mu liggéey ci lu jëmale kanam koom-koomu barab bi (ci njariñul Faraas rekk nag lol réew mi yitteelu leen woon ci lenn), daal di sos [[port autonome de Dakar|waaxub Ndakaaru]].
Ginnaaw Ndar, [[Ndakaaru]] mujj na ci [[1902]] di péeyu [[Afrig gu Sowwu gu Faraas]] gi, benn ci [[Empire colonial français|sancu]] yu Faraas yi .
Ci samwie [[1959]], [[Sudaan gu Faraas]] gi ([[Mali]] gu tay gi) ak Senegaal seey nañu ci [[Lëngoo gu Mali]], gi nga xam ne mujj na temb ci 20 suwe 1960. Temb gii mi ngi juddoo ci tuxalug ay nguur ( transferts de pouvoirs ) yu amoon ca dëppoo ga ñu xaatimoon ca Faraas ca 4 awril 1960.
== Politig ==
Senegaal nguurug demokaraasi la gu limuy làng (gu bariy parti), njiitul pénc mi (président de la république)dees na ko tànn ngir diirub juroomi at (leegi soppees na ponku sartu réew bi aju ci diirub ngiitug réew mi, yobbóoti ko ci juroom ñaari at, ginnaaw bi ñu ko soppee jële ko ci juroom ñaar, yobbu woon ko ci juroom), moom njiit li nag mooy tànn njiitul jëwrin yi. Barlamaab Senegaal ñi ngi koy wooye Péncum ndawi réew mi mbaa ( jataayub xeet wi), am na nag 120 cér yu ñiy tànn ci ay tànnéef (élections) yu dul yu njiitul réew mi(tànnéef yu yoonal yi : élections législatives) ngir diirub juroomi at
----
[[Dencukaay:Abdoulaye_Wade_in_16-05-2007.jpg|vignette|A. Wàdd, kenn ci njiiti Senegaal]]
Mii menn la ci réew yi gën a am demokaraasi te gën a dal ci Afrig, ndaxte genn [[daaneel nguur]] (coups d'État) masu fee am, « Senegaal niki roytéef »<ref>[https://web.archive.org/web/20070930111636/http://www.africa-catalunya.org/congres/pdfs/marut.pdf « am na nu ñu gise Senegaal niki roytéef ci saafara xuloo yeek xeex yi ? »] (table-ronde régionale sur le Sénégal animée par Jean-Claude Marut, CEAN-IEP de Bordeaux, 15 janvier 2004)</ref> yagg nañu koo joxe, wone ko ngir ñu roy ci, ba tee ay yi di fi am ak doonte [[Amnesty International]] mi ngi ñaawlu yenn jàpp yi yor mbubum politig<ref>[https://web.archive.org/web/20071013220931/http://web.amnesty.org/report2006/sen-summary-fra#2 Rapport 2006 d'Amnesty Internation] jàppug Idriisa Sekk</ref>{{,}}<ref>[https://web.archive.org/web/20090417210454/http://thereport.amnesty.org/fra/regions/africa/senegal Rapport 2007 d'Amnesty International] bàyyig Idriisa Sekk, ak setal gi nu ko def ci mbooleem li ñu ko toppe woon</ref>.
Senegaal am Pénc la mu demokaraasi (une république démocratique) (lu sakkan ci ay làngi politig a nga fa). Noste ga fa nekk gu njiitug réew la, ndax ba mu amee ag tembam Senegaal daa daal di jël Faraas niki roytéef, roy ca politigam ba ca 1958, niki yeneen réewi Afrig yi bokkoon ci ASF(Afrig gu Sowwu gu Faraas).[[Sartu réew bu Senegaal]] mi ngi taariixoo ci 1959, xoolaat nañu ko ci 1960 ki ko def di [[Léopold Sédar Senghor]] ginnaaw genn laaju (référendum). ay xoolaat (révisions) yu bari topp nañu ci, ñooy gu 1963 moo fi saxal nosteg njiitu réew (ci jamono jooju : dindi njiitul jëwriñ) teg ci gu 2001 gi yobbu àppub njiit gi jële ko ci 7 at, yobbu ko 5 at (jataayub mag ñi(le sénat) jëlees na ko fi, ginaaw bi ñu delloosi ko ci 2007).
Njiitul Pénc mi( Le Président de la République) (xoolal [[limub njiiti Senegaal yil]]) mooy kilifag nguur gi, moom nag ñi ngi koy tànn, mu ame ci [[pal gu mbooloo mi]] (suffrage universel) ci anam gu jonjoo de (manière directe) ci diir bu tollu ci juroom ñaari at, manees koo yeesalaat benn yoon. Mooy fal njiitul jëwrin yi (xoolal limub [[njiiti jëwrin yu Senegaal]]) moom itam (njiitul jëwrin yi) mooy tànn jëwrin yi, ba noppi sàkku ci njiitul réew mi mu tabb leen.
Ki njëkk a nekk njiitul Senegaal mooy [[Léopold Sédar Senghor]],mu nekkoon njiit lu ubbeeku te dib taalifkat bu siiwoon . Ci [[1981]] la ko njiitul jëwrinan lii di [[Abdu Juuf]] wuutu, waaye ci [[2000]] la [[Làngug demokaraasi gu Senegaal]] gi am ndam ci njiitug [[Abdulaay Wàdd]], ñu falati ko ci [[2007]]. Njiitul góornamaa bi fi nekk fii mu ne mooy [[Seex Ajiibu Sumaare]].
[[Dencukaay:National assembly (Dakar, Senegal).jpg|vignette|gauche|Péncum ndawi réew mu Sénégal|Péncum ndawi réew mi]]
[[Parlamaa bu Senegaal]] yor na ñaari néeg : Péncum ndawi réew mi ak jataayub mag ñi.
Bi ñu ko taxawalee ci 20 ut 1960,[[Assemblée nationale du Sénégal|Péncum ndayi réew mi]] mi ngi yor 150 ndawi réew, yu ñu fal ci pal gu mbooloo mi ci anam gu jonjoo (au suffrage universel direct) ngir diir bu tollu ci 5 at. Tànnéef gi gu ëppte la (Le scrutin est majoritaire) ci genn wër, ci tund yiy xëccoo 90 ndawi réew, di it gu kem (proportionnel) di ab lim bu tas ci réew mi ñu koy xëccoo mu tollu ci 60 ndawi réew. Péncum ndaw yi [[Macky Sall]] moo ko jiite, mi nekkoon [[Premiers ministres du Sénégal|Njiitul jëwrin yi]], waaye fii mu nekk, aw yoon jug na wu Saada Njaay indi ngir ñu jële ko fi, wàññi ab àppam ba du weesu menn at ngir man ko fee jële, wii yoon nag, jot naa jàll, waaye njiitul réew mi dëggalagu ko. [[Tànnéef yu yoonal yu Senegaal yu 2007]] jàll nañu ci ndam lu yaatu lu àndandoo gu njiit gi (coalition présidentielle), waaye lu jege ñaari ñatteel (deux-tiers) ci falkat yi demuñu woon ca mbañ-gàcca ya, li ko waral di ndigalul [[dogoo]](boycott) lu bawoo ci làngi kujje gi.
[[Parlamaa bu Senegaal]] boroom [[monocamérisme|benn-néeg]] (monocaméral) la woon, ci diirub jenn jamono: [[Sénat du Sénégal|Jataayub mag ñi]], muy lu ñu dindi ci 2001 ci ginnaaw genn [[Référendum de 2001 au Sénégal|laaju gu sartu réew]] (référendum constitutionnel), delloosi nañu ko ca mee 2007. Mag ñi (Les sénateurs) nag dinañu tollu ci limub 100. 35 ya ca ñoom dañu leen a fal ci anam gu jonjoodi (au suffrage indirect) ci [[tund]] yi, yeneen 65 yi njiitul réew mi di leen tabb. [[Paap Jóob]], kilifag Ndakaaru moo ko jiite .
Am na yoon (loi) wu ñu def ci diggadil gi(La loi sur la décentralisation), nekk na it di lu ñuy doxal la ko dale ca samwie [[1997]], , yoon woowu jox na ay ay doole yu am solo ñeel jataayi diiwaan yi (assemblées régionales).
Ci [[1992]] la Àttewaay bu Kawe (la cour suprême) bu Senegaal bi nekk di lu ñu dindi, ñu wottee ko cér (organes) yu jagoo loolu: [[Cour de cassation (Sénégal)|Àttewaay bu firi]] bi(Cour de cassation), [[Conseil d'État (Sénégal)|Jataayub nguur]] gi (Conseil d'État) ak [[Conseil constitutionnel (Sénégal)|Jataayub Sartu réew]] mi (Conseil constitutionnel), yooyu cér di yu niru lool séeni moroom ya nekk [[Faraas]]. Seeni àttekat Njiitul réew mee leen di tabb. Yooyu ñooy bànqaasi yoon yi gën a kawe ci réew mi (les plus hautes instances judiciaires du pays).
Dalub Àttewaay bu firi bi ëmb na lenn njiit lu njëkk, ak ñatti njiit yu néeg (trois Présidents de chambre) ak gën jaa néew juroon ñeenti xelalkat (9 Conseillers). Ca toppewaay ba le (Parquet), mi ngi ame ci ab Toppekat bu Matale (un Procureur général) , ci benn layalkat bu njëkk bu matale (un Premier Avocat général), ci gën jaa néew ñaari layalkat yu matale (deux Avocats généraux) ak gën jaa bari juroom benni déglukat (six Auditeurs) yu koy liggéeyal. Am na ñatti néeg, yoy bu ci nekk mi ngi ame ci lenn Njiit ak ñaari xelalkat gën jaa néew:
* Néeg bu njëkk bi mooy àtte layoo yi aju ci wàllug tooñaange yi (pourvois en matière pénale),
* Bu ñaareel bi di àtte layoo yi aju ci mbirum ñoñ ak yaxantu ( pourvois en matière civile et commerciale)
* Bu ñatteel bi di sëgg ci wàll yi jëm ci mboolaay (yoonu liggéey ak kaaraange gu mboolaay)(droit du travail et sécurité sociale).
Jataayub nguur gi ay xaaj yu bari ñoo ko sos:
* Xaaj bu njëkk bi moom lañu féetale xuloo yi aju ci bindu ci limi tànnéef yi(les listes électorales), yoonu (légalité) gu jëfi mbooloo yu barab yi ( collectivités locales ) ak diiŋat yi ngir neenal gu aju ci nguur gu ëpp (les recours en annulation pour excès de pouvoir).
* Xaajub ñaareel bi day def li Àttewaayu xayma yi (la Cour des comptes)di def ca Faraas , ci moom sax la jële woowiinam woowu bu yàggul rekk.
* Xaaj yooyu yépp nag am nañu ay njiiti xaaj (Présidents de section), ay xelalkati nguur (les Conseillers d'État) ay xelalkati laaju (les Conseillers référendaires) te ki leen jiite mooy njiitul jataayub nguur gi (Conseil d'État).
Jataayub sartu réew bi yor na juroomi cér, yu ñu tabbe ci ag santaane (décret) ngir juroom benni at yu ñu dul yeesal, yoo xam ne njiit ca la ak topp-njiit (Vice-président). Dees na ko yeesal cig wàll waaye déet lépp, waaye du weesu ñaari cér gën jaa bari. Ab liggéeyam mooy fuglu tànnéef yu yoonal yi, ak xool ba xam yoon yi (les lois) dëppoo nañook sartu réew mi, ak warlu yu àdduna yi (les engagements internationaux).
Senegaal dindi na [[mbugalum ray]] ci 10 desambar 2004<ref>Abolition de la peine de mort au Sénégal [http://www.peinedemort.org/National/pays.php?pays=93]</ref>.
== Gëstu-askan ==
Li ëpp ci gëstu yi ñu def ci wàllug Gëstu-askan (walla demogaraafi) ci Senegaal dafa sukkandiku ci Waññ (recensement) yi ñu jotoon a def ci [[1976]], [[1988]] rawati na [[2002]]. Doxal gu Séentu ak Lim gi (la Direction de la Prévision et de la Statistique) ci [[2004]], siiwaloon na « ay leeral ci askani Senegaal yi, loolu di woon lu juge ci waññ gu 2002 » mu sóoraale woon ci màgg gi man a ami ci askanu Senegaal la ko dale booba ba [[2015]]<ref name="stat pop">{{fr}} [https://web.archive.org/web/20070928062322/http://www.ansd.org/Rslt_prov_RGPHIII.pdf Agence Nationale de la Statistique et de la Démographie du Sénégal]</ref>.
[[Dencukaay:Senegal-demography.png|vignette|500px|Dox gu gëstu-askan gi ci diggante [[1961]] ak [[2003]] (lim bu [[Organisation des Nations unies pour l'alimentation et l'agriculture|FAO]], [[2005]]). askan ci ay junni ciy way dëkk .]]
Bu ñu sukkandikoo ci gongikuwaay yii, askanu Senegaal - wi doonoon lu toolook 1 milyoŋ ciy way dëkk ci [[1900]] ak 2,8 milyoŋ ca jamonoy ag tembam ca [[1960]] – yekkatiku na tay ba àgg ci {{formatnum:11343328}} ciy jëmm (nattale gi ci 31/12/[[2007]]) te man naa àgg ci {{formatnum:13709845}} ci mujjug 2015. Askan wii kon day màgg ci anam gu gaaw, ànd ak benn [[tolluwaayu njuru]] (taux de fécondité) bu tiim 4 doom ci jigéen.
Seetloos na fa genn kuute gu giir gu mag: [[Wolof (peuple)|Wolof]] (43,3 %), [[Pël]] (23,8 %), [[Séeréer]] (14,7 %), [[Diola (peuple)|Joolaa]] (3,7 %), [[Malinke]] (3,0 %), [[Soninke]] (1,1 %) [[Maanjanke]] (2%) ak yennat ci ay giir yu gën a néew, te gën a gawu ci barab,waxuma la nag [[naari Libaan]] yi ak [[Europe|Tubaab]] yi, nga xam ne ñi ngi nekk ci dëkki taax yi <ref>{{ouvrage|auteur=Laurence Marfaing, Mariam Sow|titre=Les opérateurs économiques au Sénégal entre le formel et l'informel, 1930-1996|pages=p.84|édition=Khartala}}</ref>{{,}}<ref>{{ouvrage|auteur=Gerti Hesseling|titre=Histoire politique du Sénégal institutions, droit et société|pages=p.52 et 53|édition=Khartala}}</ref>. Ci mujjug 2007, {{formatnum:16966}} ci waa Faraas bindu woon nañu ci seen barabu aji teewal (ambassade) (boroom ñaari réewu it ci lañu woon (les binationaux))<ref>{{fr}} Samir Gharbi, « Combien sont-ils, où vivent-ils ? Toujours accueillant », ''Jeune Afrique'', n° 2477, du 29 juin au 5 juillet 2008, p. 28</ref>.
Ab diir bu yàgg a ngii askan wi nekk di jalu ci fi jàkkaarloo ak Mbàmbulaan gu Atlas gi, waaye nocciku gu kaw gi (l'exode rural) yokk na yamoodi gi ci séddale gii. Fi mu nekk ñeenti nit yoo gis ci waa Senegaal, kenn ka mi ngi dëkk ci [[Daanaka dun bu Bopp bu Wert]] bi (Cap-Vert), looloo waral péey baa ngi waaj a xëx.
Bu [[Dakar (région)|Ndakaaru]] jàllee, diiwaan yi ñu gën a taaxal (les régions les plus urbanisées) ñooy [[Ziguinchor (région)|Siggicoor]], [[Thiès (région)|Cees]] ak [[Saint-Louis (région)|Ndar]]. Yi gën a néew ag taaxal (moins urbanisées) ci diiwaan yi ñooy [[Kolda (région)|Koldaa]], [[Matam (région)|Maatam]] ak [[Fatick (région)|Fatig]].[[Tambacounda (région)|Diiwaanu Tàmbaakundaa]] nag moo yor fatt (densité) gi gën a doyadi (11 way dëkk ci jñ²).
Bu ñu sukkandikoo ci nattale yu 2007, digg yu taax yu diiwaan (les centres urbains régionaux) yi yor lu ëpp {{formatnum:100000}} ciy way dëkk ñooy [[Touba (Sénégal)|Tuubaa]] ({{formatnum:529176)}} (Man nag yaakaar naa ne ag na ma xame Tuubaa, la fa dëkk man naa ñeentte lim bii ñu wax) – mi jekki jekki gis ag màgg gu yéem ñépp –, [[Cees]] ({{formatnum:263493}}), [[Kawlax]] ({{formatnum:185976}}), [[Mbuur]] ({{formatnum:181825}}), [[Saint-Louis (Sénégal)|Ndar]] ({{formatnum:171263}}), [[Siggicoor]] ({{formatnum:158370}}) et [[Njaaréem]] ({{formatnum:100445}})<ref name="stat pop"/>.
Ca 2007, Senegaal teeru woon na lu tollu ci 23,800 ciy daw-làqu ak sàkkukati ag wéeru ( demandeurs d'asile), yoo xam ne lu ëpp 20,000 ca ñoom ay waa Gànnaar lañu, yu doon daw boddanteg xeet ga, ak ñennat ci waa Liberiyaa, waa [[Siraa Leyoon]], ak yeneen réew <ref>U.S. Committee for Refugees and Immigrants. 2008. ''[https://web.archive.org/web/20090429171446/http://www.refugees.org/article.aspx?id=2114&subm=179&area=Investigate World Refugee Survey 2008]''</ref>.
=== Gàddaay ===
Bu Senegaal dee réew muy teeru ay way gàddaay (ay migrants), moo xam yu ay jamono lañu(saisonniers) mbaa déet, moo xam yu bawoo ci réew yi mu digool lañu walla yu ko sori<ref>{{fr}} [https://web.archive.org/web/20090417210454/http://thereport.amnesty.org/fra/regions/africa/senegal Rapport 2007 Amnesty International] : Arrestations et renvois de migrants</ref>, du tee menn mbooloo mu Senegaal mu mag ma ngay dund ca bitim réew. [[wisaaroo]] gii (diaspora)alal ju am solo la ci réew mi, ci wàllug koom ak njëmmte (identité). '''Xarala yu xibaar ak jokkoo yu bees yi''' [[XXJB]] dañuy gën di jàppandal jokkoo ci diggante njaboot gi te tax it deesi man a dund mu mel ne da ngaa nekk ci sa biir réew .
Li ëpp ci ñiy dem nag ay waxambaane lañu yu jublu [[Tugal]], rawati na [[Faraas]], ak [[Itaali]], walla ñuy dem ca [[Aamerig gu bëj-gànnaar]] ga, ca [[Kebeg]] yobbaale ci seeni xol naalub dellu réew ma ci ginnaaw yennat ciy at. Màggug [[gàddaay gu yoonoodi]] gi (immigrations clandestines), ñu koy def ci ay anam yu bon te ñaaw jëm ci [[Duni Kanaari]] yi lu tiital Senegaal la ak réew yi koy teeru.
Ñi gën a ñàkk yaakaar ñoom faalewuñu sax ay wi ñu ci man a dajeel, ginaaw gis nañu seeni moroom tekki, rawati na ya bokk ca wisaaroo ga (diaspora) — moo xam Senegaal lañu juddoo mbaa dañu faa am rekki way jur - rawati na ñi ciy yëngu ci tàggat yaram mbaa fànn (art).
----
Lu sakkan faatoo na ci gàddaay gu yoonoodi gi, mbaa mbëkk mi, baat bi ñu ko gën a xame, lu ko waral? xanaa géej gi ñu sóobu ci lu duli jumtukaay yu dëppoo , ñoom kay dañuy sóobu ci ay looca yu doyadi, duy kooki bagaas ak nit ci wépp xeet ak maas, bu ko defee yooru, duñu faale la leen dëgmal ciw ay ak musiba, gaal gaay doon duus ba, néegub añ ba, bu tëdd ba, leeg-leeg duus ñëw téq leen mbaa ngelaw lu saf, ba kero ñuy àgg bu ko Yàlla dogalee, waaye cis lëf cig loof, lu sakkan di ca des dib añ mbaa reerub ag kuréel ciy jën yu waroon a nekk diy añ ñeel leen mbaay reer. Nii lay deme ba kero ñuy àgg ak la leen fay xaar ciy kaso ak ëlëg gu lëndëm, lii mooy li xew ci mbeex mi, waxuma la nag la ca tàkk ga, aji tàng ji tàkk gii nga xam ne jali beeñ yi yàgg nañu fee tee nit àgg fa mu jëm.
----
=='
*
#
*
# ' Koom-koom ==
#
#niou boolé chi chi waallu kom kom you beess yi fa feegn chi 2012 ak tay. guiss nagne fa petrole ak gaz ak zircon ak wourouss
[[Senegaal]] nguur la gu bokk ci [[Bennoo gu koom-koom ak gu koppar gu Afrig gu sowwu gi]]. Ginnaaw ay jafe-jafe yu koom-koom ci njëlbéenug ati juroom neen-fukk yi, ay yoonam (ay luwaam) yu koom-koom soppiku nañu, bu ko defee ag màggam gu koom-koom mujj àgg ci ay 5% ci diggante 1995 ak 2001. Ci ndoortel 1994 Senegaal door na ci doxal tëriinu [[yéwénal gu koom-koom]] gu kawe ay yitte, ci càmmug mboolaay gu àdduna bi (communauté internationale), looloo ko jañoon ci mu woyofal xiimay kopparam bii nga xam ne daa tënku ci Frank bu Faraas, mu woyofal ko ba ci 50%. Jeexiitalu woyofal gii diisoon na lool ci ay way dëkkam, ndax taxoon ba njëgi li ëpp ci marsandiis yu dàttu yi ak yu dund yi seeroon te yekkatiku, niki meew, yàpp, ceeb, ba àgg ci fulu ci genn guddi, waaye am na genn màgg gu am ci koom-koom bi, ak ci njuddéef mu ñumm mu biirum réew mi, ngir yéwénal yi, nga xam ne àgg na ci 5% ci at mu nekk, bu ko defee walu gi(l'inflation) wàññiku ci anam gu yéeme ba àgg ci ay lim yu ndaw bu ñu ko nattee ca la romb.
=== Tembte ===
Ci 20/ut/ 1960, la Senegaal génn ci [[lëngoo gu Mali]] gi, daal di jibal ag tembam.
Senegaal ak [[Gàmbi]] bennoo nañu ci [[1982]] ngir amal [[lëngoo gu Senegàmbi]], waaye gii nekkutoon lu dul aw gisiin, kenn masu koo jëfe. Mujj gi ñu far ko tas ci [[1989]].
Ay [[Xeex ca Kaasamaas|janoo]] jot nañoo am la ko dale ca 1982 ci anam gu dogatu ci diggante ñoñ tàqalikoo (les séparatistes) ñi nekk ci bëj-saalum gu [[Kaasamaas]] ak doole yu góornamaa bi. Ginaaw ay jéem yu bari yu àntuwul, genn dëppoo mujj nañu ko xaatim ca [[Siggicoor]] ca 30/desambar/2004 <ref>{{fr}} [http://www.amnestyinternational.be/doc/article7875.html Rapport 2006 - Amnesty international]</ref> ci diggante jëwrini biir-réew ji woon [[Usmaan Ngom]] ak làbbe [[Augustin Diamacoune Senghor]], mi nekkoon njiitul fipp gu [[Yëngu-yëngu gu doole yu demokaraasi yu Kaasamaas]] (YDDK)(MFDC), moom Diamacoune Senghor moomu mujj na faatu.
Beneen tombub coow ci diggante ay waa Kaasamaas ak [[Ginne-Bissaawuóo]] màgg na ci awril 2007<ref>{{fr}} [https://web.archive.org/web/20090417210454/http://thereport.amnesty.org/fra/regions/africa/senegal Rapport 2007 Amnesty International] : Combats en Casamance</ref>.
Ci 1989, Gànnar ak Senegaal [[Coowul Gànnaar-Senegaal|génne nañu ku ci ne, ci anam gu ñaaw sa njabootug moroom]] te ña ëppoon ca ñoom ña nga juddoo woon fa ñu leen génnee, muy réew mi leen doomoo woon, ñu jotoon faa seey ca mboolaay ga ak koom-koom ba. Bu ñu sukkandikoo ci li '''Jataayub daw-làq bu kawe bi''' (JDK) HCR wax, ay daw-làqu ña nga des ba tay ca guddaayub dexug Senegaal gi<ref>{{fr}} [http://www.unhcr.fr/cgi-bin/texis/vtx/news/opendoc.htm?tbl=NEWS&page=home&id=467bdcda4 HCR : La Mauritanie prête à autoriser {{formatnum:20000}} réfugiés à rentrer du Mali et du Sénégal]</ref>. Ci 2007, Njiitul Gànnaar jibaloon na ba muy def càkkug palaam ga (campagne), ne nangu na delsig doomi réewam yooyu doon dund ci Senegaal ak Mali te neexu leen<ref>{{fr}} [https://web.archive.org/web/20071013232312/http://africain.biz/spip.php?article329&debut_articles_rubrique=18 Retour des réfugiés mauritaniens]</ref>.
== Melosuuf ==
{{Xóotal|Melosuufug Senegaal}}
Senegaal a ngi nekk ci diggante 12°8 ak 16°41 wu rëddu [[tus-wu-gaar]] wu bëj-gànnaar ak 11°21 ak 17°32 wu rëddu [[tus-wu-taxaw]] wu sowwu. digam wi gën a féete sowwu mooy [[Ndakaaru]] di it cat li gën a féete sowwu ci [[Afrig|goxu Afrig]].
Su ñu ko méngalee ak [[Mali|réewum Mali]] walla ak mu [[Gànnaar]] di nanu gis ne Senegaal réew mu tuuti la ci rëyaayu-suuf.
=== Kilimaa ===
{{Xóotal|Séddaliin wu yoriinu Senegaal}}
Kilimaab [[Sahel]] la ame:
* [[Nawet]] [[maami koor]] la ba kori. Bëj-saalum gi moo ëpp taw. [[àllub yamoo]] bi ca Caasamaas la nekk, ndax ay tawam yu bari;
* [[Noor]] moom [[diggi tabaski]] la ba [[rakki gamu]]
== Seddatleg yoriin ==
Ca atum 1996 la seddale gu mujj gi ame, mooy giy wéy ba tay, lu dul coppite yi ci mujj a am: Sosug [[Maatam|diwaanu Maatam]] ci 2001 ak [[gox-goxaan]] bu [[Kungeel]] ci 2006.
Ci 2008, la Senegaal nekk 14 [[diwaan]],
[[Dencukaay:Regions of Senegal.svg|350px|vignette|lonkoyoonu seddaleg yoriin gu diiwaani Senegaal yi]]
Yenn ciy dëkk:
* [[Cees]], 311 324 way dëkk (2005) ;
* [[Ndakaaru]], 1 009 256 way dëkk (2004) ;
* [[Jurbel]]
* [[Luga]]
* [[Maatam]]
* [[Mbuur]]
* [[Mexe]]
* [[Ndar]], 154 496 way dëkk (2001) ;
* [[Podoor]]
* [[Tuuba]]
* [[Tëngéej]]
* [[Kawlak]], 185 976 way dëkk (2007).
* [[Siggcoor]], 158 370 way dëkk (2007) ;
== Giir yi ==
Senegaal doon na réew mu bariy giir, waaye it soo ko mengalee ak yeneen réewi Afrik yu bari, wuuteg ay giiram du feeñ. Man nan ni daanaka wuute amul ci diggante giiri senegaal yi ndax seenug bennoo ci caada. Man nan cee lim yii tambalee ko ci yi ci gën a bari ba ci yi ci gën a néew: [[Wolof]] (43,3 %), [[Pulaar]] (23,8 %), [[Seereer]] (14,7 %), [[Joolaa]] (3,7 %), [[Malenke]] (3,0 %), [[Sooninke]] (1,1 %) Manjaak (2%), ak yeneen giir-giiraan yu tas ci réew mi, man nan cee boolee it tubaab yi ak [[naari libaan]] yi.
=== toftaloog xew-xew yi ===
* Ci VIIeelu xarnu : nguur yu njëkk ya
* XIeelu xarnu : Feeñug Lislaam
* 1442 : doorug teg loxo gu sancaan yi
* 1444 : wuññig [[Dunub Gore]]. Joqalante yu yaxantu yu njëkk yi ak waa Tugal ñi ngi door bi Waa Portigaal agsee ci sottikuwaayu [[Dexug Senegaal (dex)|Dexug Senegaal]] ak [[Cap-Vert]] (Bopp bu wert bi) (Nekkeesoon na di joqalante ay ndima aki weñ (métaux) ci pëndëxu wurus (la poudre d'or), ak daakaande ak bëñu ñay (dl'ivoire)).
* Ginaaw 1600 : Waa Faraas ak waa Olaand dàq nañu waa Portigaal.
* 1659 : Taxawal Ndar
* 1700 : Faraas yilif na yaxantu gi ci diiwaani tefes yi. Ak li kujje gi di tar ci diggante Faraas ak Britani lépp ak xeex yu bari yi teewul cangug Faraas akug jeexiitalam tallaliku. Bi mu toogee ca Ndar, Faraas daa daal di yéeg ci Dexug Senegaal gi ngir àgg Niseer, ak doonte daje na ak yenn jàmmaarloo yu bawoo ci yennat ci ay giir niki ([[Tukulóor]] yi ak [[Pël]] yi).
* 1815 : [[Ndajem Vienne]] mi jox na Faraas [[Gore]].
* 1818 : [[njaayum jaam yi]] dindees na ko ca Faraas.
* 1852 : [[Luwis Leon Sesaar Federb|Federb]] wàcc na Senegaal, daal di àtte, dale ko 1854 ba 1861 ak la dale 1863 ba 1865.
* 1855 : Wàllug teg loxo gu xare daal di door ci nangug [[Waalo]].
* 1857 : Sosus [[Sànnikati Senegaal yi]](les tirailleur sénégalais).
* 1857 : Jëlug barabub Ndakaaru cig dëppoo ak kilifay [[lebu]] yi.
* 1860-1865 : Mbooleem [[Kaasamaas]] gu suufe gi ba Siggicoor rot na ci ron yiirug Faraas (sous protectorat français).
* 1886 : Faatug Lat Joor ak jeexug jamonoy Dammeel.
* 1892 : Xare yu mag yi jeex nañu
* 1895 : Sosug[[Afrig gu sowwu gu Faraas]] gi (ASF)(AOF). Senegaal mujj na ci anam gu fés di ab sancu bu Faraas, ñu koy yore ak a doxale ca Ndar.
* 1902 : Tuxalug péeyub (ASF)(AOF) jële ko Ndar, yobbu ko Ndakaaru. Faraas mi ngi doon dundal koom-koomu Senegaal ci anam ga ko ñoroon te méngook ag jëm-kanamug réewam, googa di mbayum gerte, gu ñu war a génneji (culture de l'arachide destinée à l'exportation).
* 1914 : [[Blees Jaañ]] mooy nit ku ñuul ki njëkk a toog péncum ndawi réew mu Faraas ; moom nag tëyye na toogub ndawu réewam boobu ba ci 1934.
* 1959-1960 : Sosug lëngoo gu Mali (la fédération du Mali).
* 1960 : Tembug Senegaal (Indépendance du Sénégal).
* 1982-1989 : Sosug lëngoo gu Senegambi.
== Karmat ak delluwaay ==
<references />
== Xool it ==
{{commons|Category:Senegal|Senegaal}}
=== Jukki yi ci lonku ===
* [[À remplacer]]
=== Lëkkalekaay yu biti ===
*
{{Réewi afrig}}
[[Wàll:Afrig]]
[[Wàll:Réew]]
[[Wàll:Senegaal| ]]
rdl8l3oskakm08lgvucdtt9531urcm6
Diiwaanu Kawlax
0
3866
107611
104976
2026-06-18T00:17:10Z
InternetArchiveBot
12803
Rescuing 1 sources and tagging 0 as dead.) #IABot (v2.0.9.5
107611
wikitext
text/x-wiki
[[Dencukaay:Senegal Kaolack.png|300px|thumb|right|Diiwaanu Kawlax ci lonkoyoonu Senegaal]]
'''Diiwaanu Kawlax''' benn la ci juroom-ñenti diiwaani [[Senegaal]] yi. Réewu-taax mu [[Kawlax|kawlax]] mooy péeyu diiwaan bi, te ëpp ci solo it. Mi ngi réye 16010 km2, am 1 066 375 ciy way-dëkk
== Féeteem ci Melosuuf ==
[[Dencukaay:Kaolack departments.png|thumb|right|300px|Diiwaan bi ak ay tundam]]
Mi ngi peggook:
* Diiwaanu [[Diiwaanu Fatik|Fatik]] ([[Tunduw Gosaas|tunduw Gosaas]]) ci bëj-gànnaar ak diiwaanu [[Diiwaanu Luga|Luga]] ([[Tunduw Lingeer|tunduw Lingeer]]);
* Diiwaanu [[Diiwaanu Tambaakundaa|Tambaakundaa]] ci penku;
* réewum [[Gaambi]] ci bëj-saalum;
* Diiwaanu [[Diiwaanu Fatik|Fatik]] ([[Tunduw Funjuñ|tunduw Funjuñ]] ak wu [[Tunduw Fatik|Fatik]]) ci sowwu.
== Ay tundam ==
Ba ñu defee [[Tunduw Kafrin|tunduw Kafrin]] diiwaan ci 2008, diiwaan bi ñetti tund rekk la am:
* [[Tunduw Kawlax]]
* [[Tunduw Kungéel]] (mi judd ci 2006)
* [[Tunduw Ñooro bu Rip]]
== Lëkkalekaay yu biti ==
*{{en}} [http://www.xist.org/cntry/senegal.aspx Statistiques Geo Hive]
*{{fr}} [https://web.archive.org/web/20070109174623/http://www.finances.gouv.sn/consrkk.html Région de Kaolack sur www.finances.gouv.sn]
*{{fr}} [https://web.archive.org/web/20130320004621/http://www.archivesdusenegal.gouv.sn/klpresentation.html La région aux Archives régionales du Sénégal]
*{{fr}} [https://web.archive.org/web/20070924104033/http://www.ansd.org/SITECOKAOLACK%202004.pdf Situation économique et sociale de la région de Kaolack] (rapport officiel 2004)
{{diwaani senegaal}}
[[Wàll:diiwaani Senegaal]]
4wxjl1j3mgrkhyg657aw5iqkzyyefkl
Diiwaanu Ndar
0
3893
107612
106325
2026-06-18T00:17:39Z
InternetArchiveBot
12803
Rescuing 1 sources and tagging 0 as dead.) #IABot (v2.0.9.5
107612
wikitext
text/x-wiki
'''Diiwaanu Ndar''' benn la ci 14 diwaani [[senegaal]] yi, moo gën a féete bëj-gànnaar ci réew mépp. Moo feggook réewum [[Gànnaar]], ci guddaayu dig gi mu am ak [[Senegaal]] gépp ba fi [[dexub Senegaal]] bi di àgge ci [[mbàmbulaanug Atlas]] gi.
[[Dencukaay:Senegal Saint-Louis.png|right|thumb|300px|Lonkoyoonu diiwaanu Ndar]]
== Taariix ==
Démbu Ndar Géej
Bès dafa am feebar buy walle bi mabboon seen gox bi nu doon woowe Ndar, samppu woon si diggante ñaari dëkk yu tudd Biyer ak Geber. Ñaari dekk yi ñi ngi nekkoon si joor gi. Ba loola xewee, la waa dëkk ba fabu gaddaay ag seeni gaal, xoti dex di dem, ba teersi fi tay nuy wax Dunu Ndar. Li taxon kon mo di ne danoo beggoon mucci si musi ak balaa bile naroon a raafal seen ñoñ. Turu ndar wu jekk wi lanu toxal indi ko si dunu wi si dig ndox ngir maggale ko seen dëkku maam ba nu jóge, ngi itam ba ña fatte fa nu bayyikoo. Lii ga man see jànge ni tur si dëkk ak si lu mu man a doon, dafa war a mandarga cosaan, lukko moy, nit ki man naa dem ba fatte fu mu soqe koo. Si ñi ko Maalik waxe ba leegi, wen xaaj si way-gaddaay yi, da no fafoon des si joor gi janloog tund wi, ginnaw gi nu tudde teenu geej. Beneen calale da fa indi ag goor gu joge réewu gannaar, bu nu doon woowe Ametlika Ben Ndar, soqe ki sa Singeti, moom la ay settam tudde dekk bi di ndar.
Xarnu bi tubaab yi di wandeelu ci wetu tefesu senegaal, ku ñu naan Ndaak Kumba Nan Sango moo doon nguuru ci imprator bu waalo. Boo ba jamano, waloo mi ngi woon si dig dooleem, di tëg ay ndën ndam. Suuf su nangu mbay, njënd ak njaay mu dox, si diggante nit ñu nuul yi ak naari ganaar. Xarnu junni ak ñetti teemeer la woon jappu junni ak ñetti teemeer ak juróom ben fukk. Tukkikat tubaab yi, waa ruyang ak nitu jeppo yi doon nañ fa joofsi ngir bokk si njënd ak njaay ma fa daan am. Booba lii dong la nu fa doon def, walis nag nu amoon yeneen mbetet yu nu nebboon. Taarixkat yi jappu nanu ne xeet yi ño fa jiitu woon waa portugaal. Si atum junni ak ñetti téeméer ak juróom ben fukk ak ñeent la wa gox ba tambale jaay tubaab yi lusi mel ni mboq, dugub, ak yeeneen. Ñoom tubaab yi sax ni ngi xamee xeetu dugub yile fi si Afrig, rawatina seneegal. Ja bi ci waloo nag, mboleem yi doon yëngatu ci [[koom-koom]] si réew mi, nga bayo kajoor, wala biir waalo da nga fa daan ñów ngir jaay wala jènd ay yëf. Dawalkatu gaal yi jóge tugal demmon nanu ba dugglaante ak way-njiitu paraag yi. Ndawtal yi ag yóbal yi leen wa njiit yi doon jagleel moo gennoo na dëggeral seeni kolere.
Ay doomi normang yu am fit xuus nanu mbeex bi ak seen gaal àggsi ci dexu senegaal. Sa teeruwaay mo doon dunu Morfil, bërëbu seeluwaay. Tangoor bi ak feebar yi nekkoon ci réew mi daan fagaagal ñi ëppoon ci noom, ba tax na ñuy ci bari danu daan faral di ñakk seen bakkan. Wante galankoor yi musu leen tayyeeloo, wala mu leen di lotal ba ta ñuy yebbi seen ëmb te baña tee tukki. Galam daakande, ak bejjani ñay moo leem gënnoona soxal. Ci gattal, njënd-ak-njaay mi daan dox si xarnub fukk ak ñeet moo indi jëflaante waa tugal yi ak wa sóodaan.
Fara Xoy Jóob, buuru Waalo ci atum juróomi junni ak juróom téeméer ak fukk, moo njekka artu nit ñi, rawatina nappukat yi si nu bayi xell mbeex mi. Jamano yooyu, ay néewu tubaab danu doon tëmb si géej gi te ken xamul lu ko waraloon. Ba nu tegge juróom ñetti at la waa portugaal dall si dunu mboxos bi nekk si wetu ndar. Su nu beggoon na jeggi bel bi, baraak bi nekkoon ganjool da leen doon laaj ndamppaay. Si noonu lanu tambalee xuus gëeju senegaal ba podoor, jaal ngalam, ba jennee. Naari gannaar yi danu leen daan faral di sòng ay còng yu tàr, dileen lalal ay ndëg-sërëx. Dunu morfil lanu daan jaaye seeni nganaay, ak yeneen jumtukaay yu jem si xare. Foofu itam lanu daan wacce jaAm yi nu jappoon, ñaari way-watu timmaleleen ay mëx-dóom, ku daw rekk nu soqi ci sa kow. Kon jaam yi njek wacci si suufu ndar, dekkun fa woon. Jaaxle nag mi ngi tambalee sotteeku ci xelu nit ñi bi nu seetloo ne seen doom di ay nappukat ñi reer ni mes ci géej gi te xamu nu lan moo tax. Ndekete yo ay woroom gaal yu tubaab ño leen di doggaanu, di fadang jemmee tugal. Jamano booba, buur Tiaaka bu waalo moo amme woon. Ay jum yuy tak, ar fer-ñeet ak ay saliir yu raglu doon nanu jip si géej gi. Ba si saxaar su nuul, su xasaw di agsi ba ci ker yi. Xeex bu meti moo doon am si diggante tubaab yi seen boppu. [[Faraas|Waa faraas]], portugaal, olaand ñoo don xëccoo. Ku ci nekk bëg aakimo [[Dendu mbëj|dend]] yi . naar yi tamit door seeni lël ngir jappu nit nu nuul yi di leen jaay njaam. Yen si nappukat danu doon jëflaante ak tubaab yi ci mbeex mi, di leen jaay ndox mu neex, jen, ak yu ni mel. Tubaab di leen jox ay sangara, wenñ, ay piis, ak tooke. Si njelbeenu fukk ak juróom ñaari xarnu, ci nguurug Buuru faraase bu tuddoon lui fu ak ñett, ci la kangam Riseliye joxe ndigel way tukkikat géej yi ngir nu tambale foxrañi beppu suuf bu ñu man a foxarñi ci dendub Afrig.
Dayoo bi mu am tey jii, mi ngi jóge ca séddatle gi ñu def ci atum 2002. Bu njëkk diiwaan bi da fa ëmboon tamit [[diiwaanu Maatam]] bépp ak li ko wër.
[[Dencukaay:Saint-Louis departments.png|right|thumb|300px|Tundi diiwaan bi]]
== Ay Tundam ==
* [[Tunduw Dagana]]
* [[Tunduw Podoor]]
* [[Tunduw Ndar]]
== Xool it ==
=== Téerekaay ===
* {{fr}} Annie Ravisé, ''Contribution à l’étude des Kjökkenmöddinger (amas artificiels de coquillages) dans la région de Saint-Louis'', Dakar, Université de Dakar, 1969 (Mémoire de Maîtrise)
=== Lëkkalekaay yu biti ===
* {{fr}} [http://www.xist.org/cntry/senegal.aspx Statistiques Geo Hive]
* {{fr}} [https://web.archive.org/web/20070928081031/http://www.cr-saintlouis.sn/index.htm Conseil régional de Saint-Louis]
* {{fr}} [https://web.archive.org/web/20090529060251/http://www.archivesdusenegal.gouv.sn/slpresentation.html La région aux Archives régionales du Sénégal]
* {{fr}} [https://web.archive.org/web/20090711042640/http://www.infoconseil.sn/IMG/laitStLouis.pdf ''La filière lait et produits laitiers dans la région de Saint-Louis''] (Christian Corniaux, rapport, avril 2003)
{{diwaani senegaal}}
[[Wàll:Diiwaani Senegaal]]
glzuxb60sblr14sipyn93zb733taycc
FK Kauno Žalgiris
0
8873
107614
107531
2026-06-18T08:35:12Z
Makenzis
11686
out
107614
wikitext
text/x-wiki
{{Infobox football club
| clubname = Kauno Žalgiris
| fullname = Futbolo klubas Kauno Žalgiris
| founded = 2004 as FM Spyris
| ground = [[Darius and Girėnas Stadium]]
| capacity = 15,315
| owntitle = Owner(s)
| owner = Paulius Motiejūnas (70%)<br />[[Mantas Kalnietis]] (30%)<ref>{{cite news |last1=Augustis |first1=Mindaugas |title=Koncernas "Žalgiris": tankiame įmonių voratinklyje – ataušusios Sabonio pėdos |url=https://www.delfi.lt/krepsinis/naujienos/koncernas-zalgiris-tankiame-imoniu-voratinklyje-ataususios-sabonio-pedos.d?id=90216837 |access-date=31 July 2022 |work=[[Delfi (web portal)|Delfi]] |date=17 May 2022 |language=lt}}</ref>
| chrtitle =
| chairman = [[Mantas Kalnietis]]
| manager =
| league = [[TOPLYGA]]<ref>[https://toplyga.lt/naujiena/naujasis-lietuvos-futbolo-cempionato-pavadinimas-toplyga/9300 Naujasis Lietuvos futbolo čempionato pavadinimas – TOPLYGA]</ref>
| season = 2025
| position = [[A lyga]], 1.
| current =
| website = https://zalgiris.lt/komandos/fk-kauno-zalgiris
|pattern_la1=_hummelcoreXKjbw
|pattern_b1=_hummelcoreXKjbw
|pattern_ra1=_hummelcoreXKjbw
|pattern_sh1=_hummelcoreXKjbw
|pattern_so1=_hummel20g
|leftarm1=FFFFFF
|body1=FFFFFF
|rightarm1=FFFFFF
|shorts1=FFFFFF
|socks1=007020
|pattern_la2=_hummelcoreXKwb
|pattern_b2=_hummelcoreXKwb
|pattern_ra2=_hummelcoreXKwb
|pattern_sh2=_hummelcoreXKwb
|pattern_so2=_hummel20w
|leftarm2=FFFFFF
|body2=FFFFFF
|rightarm2=FFFFFF
|shorts2=FFFFFF
|socks2=FFFFFF
|pattern_la3=_hummelcoreXKbw
|pattern_b3=_hummelcoreXKbw
|pattern_ra3=_hummelcoreXKbw
|pattern_sh3=_hummelcoreXKbw
|pattern_so3=_hummel20b
|leftarm3=000000
|body3=000000
|rightarm3=000000
|shorts3=000000
|socks3=000000
}}
'''FK Kauno Žalgiris''' (''Futbolo klubas Kauno Žalgiris'') benn [[football]] club ci "[[TOPLYGA]]" ([[Lituwaani]]).
*'''[[A lyga]], Lituwaani: 1'''
:: 2025
==Staad==
*[[Staad Darius ir Girėnas]] (Dariaus ir Girėno stadionas).
== Xool it ==
=== Jukki yi ci lonku ===
* [[TOPLYGA]]
== Karmat ak delluwaay ==
{{Reflist}}
=== Lëkkalekaay yu biti ===
{{Commonscat|FK Kauno Žalgiris}}
* [https://zalgiris.lt/komandos/fk-kauno-zalgiris Dalub web: FK Kauno Žalgiris]
* [https://www.facebook.com/fkkaunozalgiris facebook]
* [https://int.soccerway.com/teams/lithuania/spyris-kaunas/8413/ SOCCERWAY]
* [https://www.flashscore.com/team/fk-kauno-zalgiris/0p17kQla/ FLASHSCORE]
* [https://www.transfermarkt.com/fk-kauno-zalgiris/startseite/verein/40090 Transfermarkt]
* [https://globalsportsarchive.com/team/soccer/fk-kauno-zalgiris/15855/ Globalsportsarchive]
[[Wàll:Football|Kauno Žalgiris]]
[[Wàll:Lituwaani|Kauno Žalgiris]]
fx6cbj26mb1g4qusrslrs1kk5ozniam